Daara J Jamono Lyrics

Naka dëkk bee, naka sa boor, naka sa boor (x2)  


Léeg-léeg damay bëgg gàddu samay loxo yuuxu mettit

Damay bëgg give up yenn-saay  

Tolof-tolof ak i nattu yu takku bëgg yóbbu sama fit    

Xam naa ne àdduna duma ray

Coono dafay defar xolu doomu-aadama bi ci ngëm  

Jàmbat mayu ma njegenaay   

Buur Yàlla rekk a xam li nekk sama dënn maa koy dekku

Baña jeng ta gëm ne ginnaaw jafe-jafe noflaay


Jikko jamano la

Jikko jamano la  

Jikko jama… jamano la jamano la jamano la jamano la  

Jikko jamano la

Jikko jamano la

Jikko jama… jamano la jamano la jamano la jamano la


Jamano kow lañu jële

Xamuñ noflaay dinu mbëllee

Rêves yu la sut aka kowe     

Gént boo fàttee connexion bi da fa dem   

Fok ñu am pass dañoo calé   

Daf ma yéem ñaata jéem ñaata yoon lañu jéem   

Yoonu suuf yoonu ndox fëgg fu ne fu nuy jaare

Kan moo nuy jàlle jotu ma nelaw biig yaakaar gën a diig fok nu génn ci

Lan moo nu jig ñàkk pare ci (jamano di gën a tërëdi)

Loo génn kër gis àdduna bi ci écran bu tuuti accès illimité (wuti visa)

Loxo yaa ngi clické souris yi défilé actualité ni muy dikke, bu la

benn ngelaw yóbbaale


Jikko jamano la

Jikko jamano la  

Jikko jama… jamano la jamano la jamano la jamano la  

Jikko jamano la

Jikko jamano la

Jikko jama… jamano la jamano la jamano la jamano la  


Rakk bul wori di nga jéggi ndox  

Bu soobe Buur bi gone dina màgg bay dox

Lépp dina baax lépp dina baax  

Lépp dina baax lé lé lé lépp dina baax

Du jikko jamano la du dara jaar-jaar la

Boroom karaw gu ñuul ñàkkul dara dara Jombula


Dara dara warul jomb góor-Yàlla gu am ngëm gu kowee

Te nga jéem a bey sa tool Yàlla du beykat bul xaar fu muy tawe

Di nga gis sa yoon jamano naqadi toogal ci dëkk bi jaayonte

Sélébeb yoon la jamano tërëdi fonkal sa bopp li ngay jànkoonte

Bu la kenn def jaam tukki du tekki fépp la metti

Làbbali fas buumu gàcce nga tekki

Xaalis dafa ngande làmmiñ ci jamano dëgg ne patt

Doole poos ak kàrt gab moo lay waxloo moytul bëtu xol bi patt

Paaka ci put bu mu tax nga bonn xoolal fu sori bul jàdd koñ


Jikko jamano la   

Jikko jamano la    

Jikko jama… jamano la jamano la jamano la jamano la l

Jikko jamano la  

Jikko jamano la     

Jikko jama… jamano la jamano la jamano la jamano   

Jikko jamano la

Jikko jamano la  

Jikko jama… jamano la jamano la jamano la jamano la   ...


Daara J Jamono, lyrics, paroles

Daara J Jamono